menu.png
Lost Password ?

Bible Search

 (Index)


Found entries

•••► •••►
Book Chapter Verse Text
Matthew 5 1 Bi Yeesu gisee mbooloo ma nag, mu yéeg ca tund wa, toog; taalibeem ya ñëw ci moom.
Matthew 5 2 Mu daldi leen jàngal naan:
Matthew 5 3 «Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla,barkeel ngeen,ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji,yéena ko yelloo.
Matthew 5 4 Yéen ñi nekk ci naqar, barkeel ngeen,ndax dees na dëfël seen xol.
Matthew 5 5 Yéen ñi lewet, barkeel ngeen,ndax dingeen moomi àddina.
Matthew 5 6 Yéen ñi xiif te mar njub, barkeel ngeen,ndax dingeen regg.
Matthew 5 7 Yéen ñi am yërmande, barkeel ngeen,ndax dees na leen yërëm.
Matthew 5 8 Yéen ñi am xol bu sell, barkeel ngeen,ndax dingeen gis Yàlla.
Matthew 5 9 Yéen ñiy wut jàmm, barkeel ngeen,ndax dees na leen tudde doomi Yàlla.
Matthew 5 10 Yéen ñi ñu fitnaal ndax seen njub,barkeel ngeen,ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji,yéena ko yelloo.
Matthew 5 11 «Barkeel ngeen, bu ñu leen di saaga, di leen fitnaal, di leen sosal lépp lu bon ngir man.
Matthew 5 12 Bégleen te bànneexu, ndax seen yool dina réy ci laaxira. Ndaxte noonu lañu daan fitnaale yonent yi fi jiitu.
Matthew 5 13 «Yéena di xoromus àddina. Bu xorom si sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? Du jariñati dara, lu dul ñu sànni ko ci biti, nit ñi dox ci kawam.
Matthew 5 14 Yéena di leeru àddina. Dëkk, bu nekk ci kaw tund du man a nëbbu.
Matthew 5 15 Te it duñu taal làmp, dëpp cig leget, waaye dañu koy wékk, ba muy leeral ñi nekk ci kër gi ñépp.

Page:   2 3 4 5 6 7 8 9 10 11 12