Found entries


Book | Chapter | Verse | Text |
Matthew | 7 | 5 | NAAféq, jëkkal a dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga man a gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk. |
Matthew | 7 | 6 | «Buleen jox lu sell xaj yi, mbAA sànni seeni per ci kanamu mbAAm-xuux yi, ngir bañ ñu dëggAAte ko te walbatiku, xotti leen. |
Matthew | 7 | 7 | «ÑAAnleen, ñu may leen; seetleen te dingeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen. |
Matthew | 7 | 8 | Ndaxte képp kuy ñAAn, dinga am; kuy seet, dinga gis; kuy fëgg, ñu ubbil la. |
Matthew | 7 | 9 | Kan ci yéen, bu la sa doom ñAAnee mburu, nga jox ko doj? |
Matthew | 7 | 10 | Walla mu ñAAn la jën, nga jox ko jAAn? |
Matthew | 7 | 11 | Ndegam yéen ñi bon yéena man a jox seeni gune lu bAAx, astemAAk seen BAAy bi nekk ci kaw dina jox lu bAAx ñi ko koy ñAAn! |
Matthew | 7 | 12 | «Kon nag lépp lu ngeen bëgg, nit ñi defal leen ko, yéen itam nangeen leen ko defal; ndaxte loolu moo ëmb yoonu MusAA ak waxi yonent yi. |
Matthew | 7 | 13 | «JAArleen ci bunt bu xat bi, ndaxte bunt bi ak yoon wi jëm sànku yAAtu nañu, te ñi ciy jAAr bare. |
Matthew | 7 | 14 | WAAye buntu dund gu wóor xat na, te yoon wi jëm kaw sew na, te ñi ko gis barewul. |
Matthew | 7 | 15 | «Moytuleen ñi mbubboo turu yonent. Dañuy ñëw ci yéen, yor melow xar, wAAye ci biir ay bukki yu soxor lañu. |
Matthew | 7 | 16 | Dingeen leen xàmmee ci seeni jëf. Ndax dees na witte réseñ ci dédd, walla figg ci xAAxAAm? |
Matthew | 7 | 17 | Noonu garab gu bAAx gu nekk dina meññ doom yu neex, wAAye garab gu bon dina meññ doom yu bon. |
Matthew | 7 | 18 | Garab gu bAAx mënul a meññ doom yu bon, naka itam garab gu bon mënul a meññ doom yu neex. |
Matthew | 7 | 21 | «Du képp ku may wax: “Boroom bi, Boroom bi,” mooy dugg ca nguuru Yàlla Aji Kawe ji; ka cay dugg mooy kiy def sama coobareg BAAy, bi nekk ci kaw. |