menu.png
Lost Password ?

Bible Search

 (Index)


Found entries

•••► •••►
Book Chapter Verse Text
Matthew 1 21 Dina jur doom ju góor; na nga ko tudde Yeesu, ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkAAr.»
Matthew 1 22 Loolu lépp xewoon na, ngir amal li Boroom bi wax, jAArale ko cib yonent, bi mu nAAn:
Matthew 1 24 Noonu Yuusufa yeewu, yeggali jabaram, na ko ko malAAkam Boroom bi sante woon.
Matthew 1 25 WAAye àndul ak moom, ba kera mu mucc, jur doom ju góor; mu tudde ko Yeesu.
Matthew 2 1 Bi nga xamee ne Yeesu juddu na ci Betleyem ci diiwAAnu Yude, amoon na ay boroom xam-xam, ñu jóge penku, ñëw Yerusalem. Booba, ci jamonoy buur bi Erodd la woon.
Matthew 2 3 Bi ko Erodd buur ba déggee, mu daldi jAAxle, moom ak wAA Yerusalem gépp.
Matthew 2 4 Mu woolu nag saraxalekat yu mag yépp ak xutbakati xeet wa, lAAj leen fu Almasi bi, mAAnAAm Kirist, war a juddoo.
Matthew 2 5 Ñu ne ko: «Ca Betleyem ci diiwAAnu Yude, ndaxte lii lañu bind jAArale ko cib yonent:
Matthew 2 6 “Yaw Betleyem ci diiwAAnu Yude,du yaw yAA yées ci njiiti Yude,ndaxte ci yaw la njiit di génne,kiy sàmm Israyil sama xeet.”»
Matthew 2 8 Noonu mu yebal leen Betleyem nAAn: «Demleen fa, seet bu wóor mbirum xale ba. Bu ngeen ci amee lu wóor nag, ngeen xamal ma ko, ngir man itam ma dem màggal ko.»
Matthew 2 11 Ñu dugg ca kër ga, gis xale ba ak MaryAAma ndeyam, ñu daldi sukk, di ko màggal. Ñu ubbi seeni boyetu alal, may ko wurus ak cuurAAy ak ndàbb lu xeeñ lu ñuy wax miir.
Matthew 2 12 Bi ñu ko defee Yàlla artu na leen ci biir gént, ñu bañ a dellu ca Erodd. Noonu ñu jAAr weneen yoon, ñibbi seen réew.
Matthew 2 13 Bi nga xamee ne boroom xam-xam ya ñibbi nañu, benn malAAkam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ne ko: «Erodd mu ngi ci tànki wut xale bi, ngir rey ko; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga daw jëm Misra, toog fa, ba kera ma koy wax.»
Matthew 2 15 Mu toog fa, ba Erodd fAAtu. Noonu am li Boroom bi waxoon jAArale ko cib yonent, bi mu nAAn:«Woo nAA sama doom, mu génn Misra.»
Matthew 2 16 Bi Erodd gisee nag, ne boroom xam-xam ya nax nañu ko, mu daldi mer lool. Mu santAAne ñu dugg ca Betleyem ak la ko wër, rey xale yu góor ya fa am ñAAri at jëm suuf, mengook jamono, ja ko boroom xam-xam ya waxoon.

Page:   1 2 3 4 5 6 7