menu.png
Lost Password ?

Bible Search

 (Index)


Found entries

•••► •••►
Book Chapter Verse Text
Matthew 2 17 Booba am la ñu waxoon jAArale ko ci yonent Yàlla Yeremi, bi mu nAAn:
Matthew 2 18 «BAAt jib na ci Rama,ay jooy ak yuux gu réy,Rasel mooy jooy ay doomamte bëggul kenn dëfël ko,ndaxte sAAy nañu.»
Matthew 2 19 Bi nga xamee ne Erodd fAAtu na, benn malAAkam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ca Misra,
Matthew 2 22 WAAye bi mu déggee ne, Arkelawus moo donn Erodd bAAyam ca nguuru Yude, mu ragal fAA dem. Yàlla artu ko nag ci gént, mu daldi dem diiwAAnu Galile.
Matthew 2 23 Mu ñëw nag dëkk ci dëkk bu ñuy wax Nasaret. Noonu am la ñu waxoon ca xale ba, jAArale ko ca yonent ya, bi ñu nAAn:«Dees na ko tudde Nasaréen.»
Matthew 3 1 Ca jamono jooja Yaxya feeñoon na, di wAAre ca màndiŋu Yude.
Matthew 3 2 Nii la doon wAAree: «Tuubleen seeni bàkkAAr, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jege na.»
Matthew 3 3 Yaxya mooy ki ñu doon wax jAArale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu nAAn:«Am na bAAt buy xAAcu ca màndiŋ ma ne:“Xàll-leen yoonu Boroom bi,jubal-leen fi muy jAAr.”»
Matthew 3 5 Noonu ñépp génn jëm ci moom, ñi dëkk Yerusalem ak diiwAAnu Yude, ak wAA dexu Yurdan.
Matthew 3 6 Ñu nangu seeni bàkkAAr, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan.
Matthew 3 7 Noonu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ñoom itam ca dex ga. WAAye bi leen Yaxya gisee, mu ne leen: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co, ku leen artu, ngeen daw merum Yàlla mi nar a wàcc?
Matthew 3 8 Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkAAr,
Matthew 3 9 te buleen wax ci seen xel nAAn: “Nun dAAl doomi IbrAAyma lanu,” ndaxte mAA ngi leen koy wax, Yàlla man na sàkkal IbrAAyma ay doom ci doj yii.
Matthew 3 10 Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu bAAx, dees na ko gor, sànni ko ci safara si.
Matthew 3 11 Man mAA ngi leen di sóob ci ndox, ci lu ànd ak tuub seeni bàkkAAr. WAAye kiy ñëw sama gannAAw moo ma ëpp kàttan, ba yeyoowuma koo yóbbul sax ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak safara.

Page:   1 2 3 4 5 6 7 8