Found entries


Book | Chapter | Verse | Text |
Matthew | 3 | 12 | Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàq ma, wAAye xatax ba dina ko lakk ci safara su dul fey mukk.» |
Matthew | 3 | 14 | WAAye Yaxya gàntu ko ne: «Man mAA soxla, nga sóob ma ci ndox, te yAA ngi ñëw ci man!» |
Matthew | 3 | 16 | Bi ko Yaxya sóobee ca dex ga, Yeesu génn. Ca sAA sa asamAAn yi daldi ubbiku, te Yaxya gis Xelum Yàlla wàcc ci melow pitax, ñëw ci kaw Yeesu. |
Matthew | 3 | 17 | Te bAAt bu jóge asamAAn dégtu ne: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg; ci moom lAA ame bànneex.» |
Matthew | 4 | 1 | Bi loolu amee Xelum Yàlla yóbbu Yeesu ca màndiŋ ma, ngir mu jànkoonte ak fiiri SeytAAne. |
Matthew | 4 | 4 | WAAye Yeesu tontu ko ne: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk, wAAye itam gépp kàddu gu génne ci gémmiñug Yàlla.”» |
Matthew | 4 | 5 | Bi mu waxee loolu, SeytAAne yóbbu ko ca dëkk bu sell ba, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga. |
Matthew | 4 | 6 | Mu ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal ci suuf, ndaxte Mbind mi nee na:“Dina jox ay malAAkAAm ndigal ci sa mbir,ñu leewu la ci seeni loxo,ngir nga bañ a fakkastalu ciw doj.”» |
Matthew | 4 | 8 | GannAAw loolu SeytAAne yóbbu ko ci kaw tund wu kawe lool, won ko réewi àddina yépp ak seeni ndam. |
Matthew | 4 | 9 | Mu ne ko: «Lii lépp dinAA la ko may, boo sukkee màggal ma.» |
Matthew | 4 | 10 | WAAye Yeesu tontu ko: «Sore ma SeytAAne, ndaxte Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom, te jAAmu ko moom rekk.”» |
Matthew | 4 | 11 | Noonu SeytAAne bàyyi ko. Te ay malAAka daldi ñëw fi Yeesu, di ko topptoo. |
Matthew | 4 | 13 | GannAAw gi, mu toxoo dëkku Nasaret, dem dëkk Kapernawum, bi féeteek dex ga ci diiwAAni Sabulon ak Neftali. |
Matthew | 4 | 14 | Noonu am la ñu waxoon, jAArale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu nAAn: |
Matthew | 4 | 15 | «Yaw réewum Sabulon ak réewum Neftali,di yoonu géej gannAAw dexu Yurdan,yaw Galile, réewum ñi dul Yawut — |