menu.png
Lost Password ?

Bible Search

 (Index)


Found entries

•••► •••►
Book Chapter Verse Text
Matthew 5 17 «Buleen defe ne, ñëw nAA ngir dindi yoonu MusAA ak waxi yonent yi. Ñëwuma ngir dindi leen, wAAye ngir ñu am ci man.
Matthew 5 18 Ndaxte ci dëgg mAA ngi leen koy wax, li feek asamAAn ak suuf wéyul, benn tomb walla benn rëddu araf du wéy mukk ci yoonu MusAA, ba kera yépp di am.
Matthew 5 19 Ku tebbi nag ba gën a tuuti ci ndigal yii, te ngay jàngal nit ñi noonu, dees na la tudde ki gën a tuuti ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. WAAye ku leen di sàmm, di leen digle, dees na la tudde ku mag ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
Matthew 5 20 Ndaxte mAA ngi leen koy wax, bu seen njubte ëppul njubteg xutbakat ya ak Farisen ya, dungeen tàbbi mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
Matthew 5 21 «Dégg ngeen ne, waxoon nañu mAAm ya ne leen: “Bul rey nit; ku rey nit, yoon dina la dab.”
Matthew 5 22 WAAye man mAA ngi leen di wax ne, képp ku mere sa mbokk, dinañu la àtte. Ku wax sa mbokk: “Amoo bopp,” dinañu la àtte ca kureelu àttekat ya. Ku ko wax: “Alku nga,” dinañu la àtte ci safara.
Matthew 5 23 Booy yóbbu nag sa sarax ca saraxalukAAy ba, te nga fàttaliku foofa ne, sa mbokk am na lu mu la meree,
Matthew 5 24 nanga fa bàyyi sa sarax ca kanamu saraxalukAAy ba, nga jëkk a dem, juboo ak sa mbokk, ba noppi dellu, joxe sa sarax.
Matthew 5 25 «GAAwal a juboo ak ki lay yóbbu, ngeen layooji, bala ngeen a egg; ngir bañ ki ngay layool jébbal la àttekat ba, kooka jox la alkAAti ba, ñu tëj la.
Matthew 5 26 Ci dëgg mAA ngi la koy wax, doo génn foofa mukk te feyuloo dërëm bi ci mujj.
Matthew 5 27 «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bul njAAloo.”
Matthew 5 28 WAAye man mAA ngi leen di wax ne, képp ku xool jigéen, xédd ko, njAAloo nga ak moom ci sa xel.
Matthew 5 29 Bu la sa bëtu ndeyjoor bëggee yóbbe bàkkAAr, luqi ko, sànni ko fu sore.
Matthew 5 30 Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw, ñu sànni sa yaram wépp ci safara. Bu la sa loxol ndeyjoor bëggee yóbbe bàkkAAr, dagg ko, sànni ko fu sore. Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw ñu sànni sa yaram wépp ci safara.
Matthew 5 32 WAAye man mAA ngi leen di wax ne, ku fase sa jabar te du ci njAAloo, yAA koy tegtal yoonu njAAloo. Te it ku takk jigéen ju ñu fase, njAAloo nga.

Page:   1 2 3 4 5 6 7 8 9 10 11