menu.png
Lost Password ?

Bible Search

 (Index)


Found entries

•••► •••►
Book Chapter Verse Text
Matthew 5 33 «Dégg ngeen itam ne, waxoon nañu mAAm ya ne leen: “Bul weddi sa ngiñ, wAAye li nga giñ def ko ngir Boroom bi.”
Matthew 5 34 WAAye man mAA ngi leen di wax ne, buleen giñ dara; bumu doon ci asamAAn, ndaxte moo di jalu Buur Yàlla;
Matthew 5 35 bumu doon ci àddina, ndax moo di tegukAAyu tànkam; bumu doon it ci Yerusalem, ndax moo di dëkku Buur bu mag bi.
Matthew 5 36 Bul giñ it ci sa bopp, ndaxte mënuloo weexal mbAA ñuulal benn ci say kawar.
Matthew 5 37 Sa wAAw na nekk wAAw, sa déedéet na nekk déedéet. Loo ci teg, ci Ibliis la jóge.
Matthew 5 39 WAAye man mAA ngi leen di wax ne, buleen bañ ku leen def lu bon, wAAye ku la pes ci sa lexu ndeyjoor, jox ko ba ca des.
Matthew 5 40 Ku la bëgg a kalAAme, ngir jël sa turki, nga boole ca it sa mbubb mu mag.
Matthew 5 41 Ku la ga, nga yenul ko doxub benn kilomet, àndal ak moom ñAAr.
Matthew 5 42 Mayal ku lay ñAAn, te bul jox gannAAw ku lay leb.
Matthew 5 43 «Dégg ngeen ne, waxoon nañu: “Soppal sa moroom te sib sa bañAAle.”
Matthew 5 44 WAAye man mAA ngi leen di wax ne, soppleen seeni bañAAle te ñAAnal ñi leen di fitnAAl,
Matthew 5 45 ngir wone ne, yéenay doomi seen BAAy bi nekk ci kaw. Ndaxte mu ngi fenkal jantam ci kaw ñu bon ñi ak ñu bAAx ñi, te muy tawal ñi jub ak ñi jubadi.
Matthew 5 46 Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban yool ngeen am? XanAA juutikat yi duñu def noonu it?
Matthew 5 47 Su ngeen nuyoo seeni bokk rekk, lu ngeen def lu doy wAAr? XanAA ñi xamul Yàlla duñu def noonu it?
Matthew 5 48 Nangeen mat nag, ni seen BAAy bi ci kaw mate.

Page:   2 3 4 5 6 7 8 9 10 11 12