menu.png
Lost Password ?

Bible Search

 (Index)


Found entries

•••► •••►
Book Chapter Verse Text
Matthew 6 1 «Wottuleen a def seeni jëf yu jub ci kanamu nit ñi, muy ngistal. Lu ko moy, dungeen am yool ci seen BAAy bi nekk ci kaw.
Matthew 6 2 Booy sàkk sarax nag, bul yeble ci sa kanam, ñu yéene la. Moom la nAAféq yi di def ca jàngu ya ak ca mbedd ya, ngir nit ñi màggal leen. Ci dëgg mAA ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
Matthew 6 3 WAAye booy sàkk sarax, bu sa loxob càmmooñ xam li sa loxob ndeyjoor di def,
Matthew 6 4 ngir sa sarax nekk kumpa. Noonu sa BAAy, bi dara umpul, dina la ko delloo.
Matthew 6 5 «Bu ngeen di ñAAn, buleen mel ni nAAféq yi, ñoom ñi bëgg di ñAAn, taxaw ca jàngu ya ak fa mbedd yay daje, ngir nit ñi gis leen. Ci dëgg mAA ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
Matthew 6 6 Yaw nag booy ñAAn, duggal ci sa néeg, tëj bunt bi, te nga ñAAn sa BAAy bi bët mënta gis. Noonu sa BAAy, bi dara umpul, dina la ko delloo.
Matthew 6 7 «Te it bu ngeen di ñAAn, buleen bareel wax yu amul njariñ, mel ni ñi xamul Yàlla; ñoom defe nañu ne, Yàlla dina leen nangul ndax seen wax ju bare.
Matthew 6 8 Buleen nirook ñoom, ndaxte seen BAAy xam na seeni soxla, lAAta ngeen ko koy wax.
Matthew 6 9 Yéen nag nii ngeen war a ñAAne:“Sunu BAAy bi nekk ci kaw,na sa tur sell,
Matthew 6 12 te bAAl nu sunuy tooñ, ni nu bAAle ñi nu tooñ;
Matthew 6 13 bu nu teg ci yoonu nattu, wAAye nga musal nu ci lu bon.Ndaxte yaw yAA yelloo nguur ak kàttan ak màggAAy, ba fàww. Amiin.”
Matthew 6 14 «Su ngeen bAAlee ñi leen tooñ, seen BAAy bi ci kaw dina leen bAAl seeni tooñ yéen itam.
Matthew 6 15 WAAye su ngeen bAAlul ñi leen tooñ, seen BAAy it du leen bAAl seeni tooñ.
Matthew 6 16 «Su ngeen di woor, buleen mel ni nAAféq yi, ñoom ñi yoggoorlu, di ñAAwal seeni kanam, ngir seen koor feeñu nit ñi. Ci dëgg mAA ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
Matthew 6 18 ngir sa koor bañ a feeñu nit ñi, wAAye mu feeñu sa BAAy bi bët mënta gis. Noonu sa BAAy, bi dara umpul, dina la ko delloo.

Page:   3 4 5 6 7 8 9 10 11 12 13