Found entries


Book | Chapter | Verse | Text |
Matthew | 6 | 19 | «Buleen dajale alal ci àddina, fu ko max ak xomAAg di yàqe, ak fu sàcc di dugg, jot ko. |
Matthew | 6 | 20 | WAAye dajaleleen alal ci lAAxira, fu ko max ak xomAAg dul yàqe, ak fu sàcc dul dugg, jot ko. |
Matthew | 6 | 23 | wAAye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm. Leer gi nekk ci yaw, bu nekkee lëndëm, naka la lëndëm googu di këruuse! |
Matthew | 6 | 24 | «Kenn mënul a jAAmoondoo ñAAri sang; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des. Mënuleen a boole jAAmu Yàlla ak jAAmu Alal. |
Matthew | 6 | 25 | «Loolu moo tax mAA ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jAAxal, ci lu ngeen war a lekk, walla lu ngeen war a nAAn. Buleen jAAxle it ngir seen yaram, ci lu ngeen war a sol. XanAA bakkan gënul lekk, te yaram gënul koddAAy? |
Matthew | 6 | 26 | Seetleen picci asamAAn: duñu ji, duñu góob, duñu denc ci sàq; teewul seen BAAy bi ci kaw moo leen di dundal. Ndax ëppuleen mAAna picc yi ci lu bare? |
Matthew | 6 | 27 | Ana kan ci yéen ci kaw njAAxleem moo man a yokk waxtu ci àppam? |
Matthew | 6 | 28 | «Te lu tax ngeen di jAAxle ngir koddAAy? Seetleen bu bAAx, ni tóor-tóori ñax mi di saxe ci tool yi. Duñu liggéey, duñu ëcc, |
Matthew | 6 | 29 | wAAye mAA ngi leen di wax ne, SuleymAAn sax ci ndamam soluwul woon ni benn ci ñoom. |
Matthew | 6 | 30 | Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxum tool yi, miy sax tey, te bu subAA ñu def ko ci tAAl bi, ndax du leen gën a wodd? |
Matthew | 6 | 31 | Buleen jAAxle nag, di wax ne: “Lu nu war a lekk? Lu nu war a nAAn?” walla: “Lu nu war a sol?” |
Matthew | 6 | 32 | Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen BAAy, bi nekk ci kaw, xam na ne am ngeen soxla ci loolu lépp. |
Matthew | 6 | 33 | WAAye jëkkleen a wut nguuram ak njubteem, te loolu lépp dina leen ko ci dollil. |
Matthew | 6 | 34 | Buleen jAAxle nag ngir ëllëg, ndaxte ëllëg dina topptoo boppam. Bés bu nekk, coonoom doy na ko. |
Matthew | 7 | 1 | «Buleen àtte seeni moroom ak ñAAw njort, ngir bañ ñu àtte leen yéen itam. |