menu.png
Lost Password ?

Bible Search

 (Index)


Found entries

•••► •••►
Book Chapter Verse Text
Matthew 3 2 Nii la doon waaree: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla AJI Kawe ji jege na.»
Matthew 4 17 Booba Yeesu tàmbali di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla AJI Kawe ji jegesi na.»
Matthew 5 3 «Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla,barkeel ngeen,ndaxte nguuru Yàlla AJI Kawe ji,yéena ko yelloo.
Matthew 5 10 Yéen ñi ñu fitnaal ndax seen njub,barkeel ngeen,ndaxte nguuru Yàlla AJI Kawe ji,yéena ko yelloo.
Matthew 5 19 Ku tebbi nag ba gën a tuuti ci ndigal yii, te ngay jàngal nit ñi noonu, dees na la tudde ki gën a tuuti ci nguuru Yàlla AJI Kawe ji. Waaye ku leen di sàmm, di leen digle, dees na la tudde ku mag ci nguuru Yàlla AJI Kawe ji.
Matthew 5 20 Ndaxte maa ngi leen koy wax, bu seen njubte ëppul njubteg xutbakat ya ak Farisen ya, dungeen tàbbi mukk ci nguuru Yàlla AJI Kawe ji.
Matthew 7 21 «Du képp ku may wax: “Boroom bi, Boroom bi,” mooy dugg ca nguuru Yàlla AJI Kawe ji; ka cay dugg mooy kiy def sama coobareg Baay, bi nekk ci kaw.
Matthew 8 11 Maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu ñëw, jóge ci penku ak sowu, bokk lekk ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ci nguuru Yàlla AJI Kawe ji.
Matthew 10 7 Bu ngeen demee nag, yégleleen naan: “Nguuru Yàlla AJI Kawe ji jegesi na.”
Matthew 11 11 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya musul a feeñ. Waaye ba tey ki gën a ndaw ci nguuru Yàlla AJI Kawe ji moo ko sut.
Matthew 13 11 Noonu mu tontu leen ne: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla AJI Kawe ji, waaye ñale mayuñu leen ko.
Matthew 13 24 Noonu Yeesu dégtal leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla AJI Kawe ji dafa mel ni nit ku ji jiwu wu baax ci toolam.
Matthew 13 31 Yeesu waxaat leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla AJI Kawe ji dafa mel ni doomu fuddën bu nit jël, ji ko ci toolam.
Matthew 13 33 Yeesu teg ca beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla AJI Kawe ji dafa mel ni lawiir bu jigéen jël, jaxase ko ak ñetti andaari fariñ, ba kera tooyal bépp di funki.»
Matthew 13 44 Yeesu teg ca ne: «Nguuru Yàlla AJI Kawe ji dafa mel ni alal ju nëbbu cib tool. Nit ki ko gis nëbbaat ko; xolam sedd, ba mu dem jaay li mu am lépp, jënd tool ba.

Page:   1 2 3 4 5 6