menu.png
Lost Password ?

Bible Search

 (Index)


Found entries

•••► •••►
Book Chapter Verse Text
Matthew 10 11 «Bu fekkee ne AGSI ngeen ci dëkk bu mag mbaa bu ndaw, nangeen fa seet ku fa am faayda, dal ca moom ba kera ngeen jóge dëkk ba.
Matthew 12 28 Waaye bu fekkee ne ci Xelum Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla AGSI na ba ci yéen.
Matthew 21 1 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jege woon nañu Yerusalem, ba AGSI dëkku Betfase ci wetu tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal ñaari taalibe,
Matthew 25 10 «Bi nga xamee ne dem nañu jëndi, boroom séet ba AGSI. Ñi amoon diwlin ci seeni làmp, ànd ak boroom séet ba ca reer ya. Noonu bunt ba tëj.
Matthew 25 11 Gannaaw loolu janq ya ca des AGSI naan: “Sang bi, Sang bi, ubbil nu.”
Matthew 25 34 «Noonu Buur bi dina wax ñi féete ndeyjoor: “AGSIleen, yéen ñi sama Baay barkeel, jël-leen nguur, gi ñu leen waajal li dale ci njàlbéenug àddina.
Matthew 26 47 Bi muy wax loolu nag, Yudaa, mi bokkoon ca fukki taalibe ya ak ñaar te naroon koo wor, AGSI, ànd ak mbooloo mu bare, jóge ca saraxalekat yu mag ya ak ca njiiti xeet wa, te gànnaayoo jaasi ak yet.
Mark 10 46 Bi loolu wéyee ñu AGSI ca dëkku Yeriko. Bi ko Yeesu di génn, ànd ak taalibe ya ak mbooloo mu xaw a bare, am gumba gu tudd Bartime — liy tekki «doomu Time,» toog ci wetu yoon wi, di yelwaan.
Mark 11 1 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jege nañu Yerusalem, ba AGSI dëkki Betfase ak Betani ci wetu tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal ñaar ciy taalibeem,
Mark 14 43 Bi Yeesu di wax, Yudaa mi bokkoon ci fukki taalibe ya ak ñaar, AGSI, ànd ak mbooloo mu bare, mu jóge ca saraxalekat yu mag ya, ca xutbakat ya ak ca njiiti xeet wa, te gànnaayoo jaasi ak yet.
Luke 1 57 Gannaaw loolu jamono ji Elisabet war a mucc AGSI, mu daldi jur doom ju góor.
Luke 2 6 Bi ñu nekkee Betleyem, waxtu wa mu waree mucc AGSI.
Luke 2 21 Bi bés ba dellusee jamonoy xarafal xale ba AGSI. Ñu tudde ko Yeesu, ni ko malaaka ma diglee woon, laata ko yaayam di ëmb.
Luke 2 22 Noonu jamono ji ñu leen waroon a sellale AGSI, ni ko yoonu Musaa tërale. Waajuri Yeesu yi daldi koy yóbbu ca dëkku Yerusalem, ngir sédde ko Boroom bi.
Luke 5 7 Noonu ñu daldi liyaar seen àndandoo, yi nekk ca geneen gaal ga, ngir ñu ñëw dimbali leen. Ñooñu AGSI, ñu feesal ñaari gaal yi, ba ñuy bëgg a suux.

Page:   1 2 3 4