Found entries


Book | Chapter | Verse | Text |
Matthew | 2 | 3 | Bi ko Erodd buur ba déggee, mu daldi JAAXLE, moom ak waa Yerusalem gépp. |
Matthew | 6 | 25 | «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen war a lekk, walla lu ngeen war a naan. Buleen JAAXLE it ngir seen yaram, ci lu ngeen war a sol. Xanaa bakkan gënul lekk, te yaram gënul koddaay? |
Matthew | 6 | 27 | Ana kan ci yéen ci kaw nJAAXLEem moo man a yokk waxtu ci àppam? |
Matthew | 6 | 28 | «Te lu tax ngeen di JAAXLE ngir koddaay? Seetleen bu baax, ni tóor-tóori ñax mi di saxe ci tool yi. Duñu liggéey, duñu ëcc, |
Matthew | 6 | 31 | Buleen JAAXLE nag, di wax ne: “Lu nu war a lekk? Lu nu war a naan?” walla: “Lu nu war a sol?” |
Matthew | 6 | 34 | Buleen JAAXLE nag ngir ëllëg, ndaxte ëllëg dina topptoo boppam. Bés bu nekk, coonoom doy na ko. |
Mark | 6 | 20 | Ndaxte Erodd dafa ragal Yaxya, ba sàmm bakkanam, xam ne ku jub la te sell. Bu ko daan déglu it, day JAAXLE lool, teewul mu bég ci déglu ko. |
Luke | 1 | 21 | Fekk na booba mbooloo maa ngi xaar, JAAXLE lool ci li Sakariya yàgg ca bérab bu sell ba. |
Luke | 1 | 65 | Waa dëkk ba bépp JAAXLE, xew-xew yooyu siiw ca tundi Yude yépp. |
Luke | 2 | 48 | Naka la ko waajuram yi gis, ñu daldi waaru. Yaayam ne ko: «Sama doom, lu tax nga def nu lii? Man ak sa baay nu ngi la doon seet, JAAXLE lool.» |
Luke | 9 | 7 | Bi Erodd boroom diiwaanu Galile déggee li Yeesu ak ay taalibeem doon def lépp, mu JAAXLE, ndaxte amoon na, ñu doon wax ci mbiri Yeesu naan: «Yaxya moo dekki.» |
Luke | 11 | 38 | Farisen bi nag daldi JAAXLE, bi mu gisee ne Yeesu raxasuwul, laata muy lekk. |
Luke | 12 | 22 | Noonu Yeesu daldi ne taalibeem yi: «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen war a lekk. Buleen JAAXLE it ngir seen yaram ci lu ngeen war a sol, |
Luke | 12 | 25 | Ana kan ci yéen ci kaw nJAAXLEem, moo man a yokk ab waxtu ci àppam? |
Luke | 12 | 26 | Su fekkee lu tuuti loolu rekk mënuleen koo def, kon lu tax ngeen di JAAXLE ci li ci des? |