menu.png
Lost Password ?

Bible Search

 (Index)


Found entries

•••► •••►
Book Chapter Verse Text
Matthew 7 24 «Képp ku dégg nag lii ma leen wax, te di ko jëfe, dinga mel ni nit ku am xel, ku TABAX këram, samp ko ciw doj.
Matthew 7 26 Waaye képp ku dégg lii ma leen wax, te jëfewuloo ko, dinga mel ni nit ku ñàkk xel, ku TABAX këram ci gànnuus bi.
Matthew 21 33 Yeesu teg ca ne: «Dégluleen beneen léeb. Amoon na fi benn boroom kër bu jëmbët toolu réseñ. Mu ñag tool bi, gas ci biir pax, ngir nal ci réseñ yi. Mu TABAX wottukaay, batale ko ay beykat, daldi tukki.
Matthew 21 42 Kon Yeesu ne leen: «Xanaa musuleen a jàng lii ci Mbind yi?“Doj wi TABAXkat yi sànni;mujj na di doju koñ;ci Boroom bi la loolu jóge,te yéemu nanu ci.”
Matthew 23 29 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi TABAX xabruy yonent yi, tey rafetal bàmmeeli ñu jub ñi.
Matthew 24 1 Bi Yeesu waxee ba noppi, mu génn ca kër Yàlla ga, dem. Noonu ay taalibeem ñëw ci moom, ngir won ko TABAXi kër Yàlla ga.
Matthew 26 61 «Kii nee woon na: “Man naa toj kër Yàlla ga, TABAXaat ko ci ñetti fan.”»
Matthew 27 40 naan: «Yaw mi man a toj kër Yàlla ga, TABAXaat ko ci ñetti fan, musalal sa bopp; boo nekkee Doomu Yàlla, wàccal ci bant bi.»
Mark 12 1 Noonu Yeesu daldi leen wax ciy léeb. Mu ne leen: «Amoon na fi nit ku jëmbët toolu réseñ. Mu ñag tool bi, gas pax ngir nal ci réseñ yi, TABAX wottukaay, ba noppi batale ko ay beykat, daldi tukki.
Mark 12 10 Ndax musuleen a jàng wax jii ci Mbind mi?“Doj wi TABAXkat yi sànni,mujj na di doju koñ;
Mark 14 58 «Nun daal dégg nanu, mu ne: “Dinaa toj kër Yàlla, gii loxoy nit liggéey, TABAX ci ñetti fan geneen gu nit liggéeyul.”»
Mark 15 29 Ña fa doon romb di ko xas, di wëcc seen bopp ndax sib ko naan: «Waaw kay, yaw mi bëgg a toj kër Yàlla gi, TABAXaat ko ci ñetti fan,
Luke 6 48 Dafa mel ni nit kuy TABAX kër, mu gas fu xóot, jot doj wu réy, samp fa kër ga. Bi mbënn ma ñëwee, wal ma dafa dal ca kër ga te yenguwul, ndaxte nit ka dafa TABAX kër ga TABAX bu dëgër.
Luke 6 49 Waaye képp ku dégg samay wax te jëfewuloo ko, dinga mel ni nit ku TABAX këram ci suuf, bañ koo defal fondamaa. Bi wal ma dalee ca kër googa, dafa màbb ca saa sa, lépp yàqu yaxeet.»
Luke 7 5 ndaxte sopp na sunu xeet te moo nu TABAXal sax sunu jàngu.»

Page:   1 2 3