Found entries


Book | Chapter | Verse | Text |
Matthew | 9 | 6 | Waaye XAMLEEN ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ka: «Jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.» |
Matthew | 24 | 33 | Noonu yéen itam bu ngeen gisee loolu lépp, XAMLEEN ne jege na, mu ngi ci bunt bi sax. |
Matthew | 24 | 43 | Waaye XAMLEEN lii: bu boroom kër gi xamoon, ci ban waxtu ci guddi la sàcc bi di ñëw, kon dina yeewu te du ko bàyyi, mu toj këram. |
Mark | 2 | 10 | Waaye XAMLEEN ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu mu ne làggi ba: |
Mark | 13 | 29 | Noonu itam bu ngeen gisee loolu lépp xew, XAMLEEN ne jege na; mu ngi ci bunt bi sax. |
Luke | 5 | 24 | Waaye XAMLEEN ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ba: «Maa ngi la koy sant, jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.» |
Luke | 10 | 11 | “Seen pëndu dëkk, bi taq ci sunuy tànk sax, noo ngi koy faxas, ngir seede leen seen réer. Waaye nag XAMLEEN ne, nguuru Yàlla jegesi na.” |
Luke | 12 | 39 | Waaye XAMLEEN lii: bu boroom kër gi xamoon ban waxtu la sàcc bi di ñëw, du ko bàyyi, mu toj këram. |
Luke | 21 | 20 | «Bu ngeen gisee ay xarekat wër dëkku Yerusalem, XAMLEEN ne jamono, ji ñu koy yàq, agsi na. |
Luke | 21 | 31 | Noonu itam bu ngeen gisee loolu lépp xew, XAMLEEN ne nguuru Yàlla jege na. |
John | 15 | 18 | «Bu leen àddina bañee, XAMLEEN ne, man lañu jëkk a bañ. |
Acts | 28 | 28 | «XAMLEEN nag ne, xebaaru mucc gii yégal nañu ko ñi dul Yawut, te ñoom dinañu ko déglu.» |
Galatians | 3 | 7 | XAMLEEN boog ne, boroom ngëm yi rekk ñooy doomi Ibraayma. |
Ephesians | 5 | 17 | Buleen ñàkk bopp nag, waaye XAMLEEN liy coobareg Boroom bi. |
Hebrews | 13 | 23 | XAMLEEN ne, Timote sunu mbokk, génn na kaso. Su dikkee léegi, dinaa ànd ak moom, seetsi leen. |
Page:
1 2