menu.png
Lost Password ?

Bible Search

 (Index)


Found entries

•••► •••►
Book Chapter Verse Text
Acts 15 39 Noonu ñu XULOO, ba far tàggoo. Barnabas yóbbaale Màrk, ñu dugg gaal, jëm Sipar.
Acts 23 9 Ci kaw loolu nag coow lu bare daldi jib. Ñenn ca xutbakat, ya bokk ca Farisen ya, ne bërét, daldi XULOO bu metti ne: «Gisunu dara lu bon ci nit kii. Su fekkeente ne, rab a ko wax mbaa malaaka...?»
Acts 23 10 Noonu XULOO ba daldi gën a tàng, ba kilifa ga ragal ne, nit ñi dinañu daggaate Pool. Kon mu sant xarekat ya, ñu wàcc, nangu Pool ci ñoom, yóbbu ko ca tata ja.
Romans 1 29 Seen xol fees na ak lu jubadi, lu bon, bëgge ak coxor; duñu xalaat lu dul kiñaan, rey nit, XULOO, njublaŋ ak ñaaw njort; dañuy jëw,
Romans 13 13 Gannaaw nu ngi ci leer, na sunug dund rafet. Bunu naan sangara ba màndi tey bànneexu; bunu njaaloo tey def i ñaawteef ak sunuy cér; bunu XULOO mbaa nuy ñeeyante.
1 Corinthians 1 11 Ndaxte bokk yi, waa kër Kelowe xamal nañu ma ne, dangeen di XULOO.
1 Corinthians 3 3 ci li ngeen di topp seen nafsu. Bu ñeetaan ak XULOO amee ci seen biir, xanaa du loolu mooy wone ne, dangeen a topp seen nafsu, di doxale ni niti àddina?
2 Corinthians 12 20 Ragal naa, bu ma ñëwee ci yéen, fekk leen nu ma neexul, te yéen it ngeen fekk ma nu leen neexul. Ragal naa fekk ay XULOO ci seen biir, ak ñeetaane, xadar ak diiroo mbagg, xas ak jëw, réy-réylu ak yengu-yengu.
Galatians 5 20 xërëm, luxus, noonoo ak XULOO, ñeetaane, xadar, diiroo mbagg, féewaloo ak xaajaloo,
Philippians 2 14 Lépp lu ngeen di def nag, buleen ci boole xultu mbaa XULOO.
1 Timothy 6 4 kooku boroom tiitar la, bu xamul dara. Dafa wéradi, ba sóobu ci gëstuy neen ak i werante ciy araf yu dul jur lu dul ñeetaange, XULOO, xaste, ñaaw njort
2 Timothy 2 23 Tanqamlul bépp weranteb neen bu amul njariñ, xam ne XULOO rekk lay jur.
2 Timothy 2 24 Te jaamu Boroom bi warul a XULOO, waaye na lewet ci ñépp, jekk ngir jàngale tey muñ fitnay noon.
Titus 3 9 Waaye moytul yu deme ni werantey neen ak limi maam, ay XULOO ak i xëccoo ci doxalinu yoonu Musaa, ndax loolu waxi neen la, te amul benn njariñ.
James 4 1 Xeex yi ak XULOO yi ci seen biir nag, lu leen waral? Xanaa du ci seeni bëgg-bëgg, yiy xeex ci seeni cér?

Page:   1 2